TSK

TSK · Lamentations 3:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko!

¶ «Waaye réew mi dinañu ko gental, mu daboo ati Noflaayam diir ba ñu ko dëddoo, wéetal ko, te fekk ñoom ñuy fey seen boru tooñ; ndax kat dañoo sofental samay santaane, xalab samay dogal.

¶ Mu wax ak buurub Israyil ne ko: «Ana lu ma séq ak yaw? Demal kay ca sa yonenti baay yaak sa yonenti ndey ya!» Buurub Israyil ne ko: «Déedéet, ndaxte Aji Sax jee nu fi woo, nun ñetti buur yii, ngir teg nu ci loxol Mowab.»

¶ Naka la Alyaasa di wax, ndaw la ne jimeet, jëm ca moom. Ma nga naan: «Gis nga musiba mii Aji Sax ji wàcce. Kon ana lu may séentooti ci Aji Sax ji?»

Job 11:6 TSK

àgge la kumpay xelam mu rafet, mi wees dég-dég, kon nga xam ne Yàlla jéllale na sa lenni tooñ!

Nit def na jëfi dof, ba sànku, walbatiku mere Aji Sax ji.

Sa doom yi ne lasar, mbete kooba yu fiir jàpp, ñu ne lareet fépp fu mbedd daje, këppoo sànjum Aji Sax ji, sa Yàlla ji leen rëbb.

«Damm-damm yu dul wér ak mitit wu tar jarul jooy. Maa la teg lii, ndax sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.

Jonah 2:3 TSK

Mu ne: Maa jàq, woo Aji Sax ji, mu wuyu ma. Ca xóotey njaniiw laa wootee wall, nga dégg ma.

Micah 7:9 TSK

Maa moy Aji Sax ji, kon naa tegoo meram, ba mu layool ma, dëggal ma, génne ma ci leer gi, ma gis ag njekkam.

Ci kaw loolu tàngooru naaj wu metti di lakk nit ñi. Nit ñi nag tuubuñu, sàbbaal Yàlla; xanaa di saaga Yàlla, ji dogal yooyu musiba.