TSK

TSK · Leviticus 1:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel,

Gàtt ba bumu am sikk te na di kuuyu menn at. Man naa doon xar mbaa sikket.

¶ «Su fekkee ne li nit kiy sarxe saraxu cant la ci biir jàmm, mu di ko jële ci nag wu góor mbaa wu jigéen, na indil Aji Sax ji lu amul sikk.

bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe sikket bu amul sikk.

Mu ne Aaróona: «Sàkkal aw sëllu, muy saraxas póotum bàkkaar akum kuuy, muy saraxu rendi-dóomal, te bu ci lenn am sikk, nga boole indil Aji Sax ji.

¶ «Ni Aaróona di dugge ci biir bérab bu sell bee sell nii la: day indaale aw yëkk wu ndaw ngir ab saraxu póotum bàkkaar, akum kuuy ngir ab saraxu rendi-dóomal.

liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket.

Sarax si muy sarxalsi Aji Sax ji di menn xarum menn at mu amul sikk, ngir rendi-dóomal, ak menn xarum menn at mu jigéen mu amul sikk, ngir póotum bàkkaar, ak menn kuuy mu amul sikk, ngir saraxas cant ci biir jàmm,

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.