TSK

TSK · Leviticus 10:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na Aaróona aki doomam jiitloo loolu, bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, mbaa ñuy jegeji sarxalukaay bi, ngir liggéey ci bérab bu sell bi, ndax ñu baña yóbbe seen bopp mbugal, muy seen dee. Na Aaróona ak askanam sàrtoo loolu fàww.

Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Bérab bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.

Du tere mu saña lekk ci ñamu Yàllaam, muy ñam wu sell ak wu sella sell.

¶ Aji Sax ji ne Aaróona: «Yaw, yaak say doom ak sa waa kër maam, yeenay gàddu peyug tooñ ci wàllu bérab bu sell bi, te itam yaw, yaak say doom, yeenay gàddu peyug tooñ ci seen wàllu carxal.

¶ «Gannaaw loolu nanga tëdde sa wetu càmmoñ. Googu wet ngay gàddoo ayu waa kër Israyil. Diiru fan yi ngay tëdde wet ngay gàddoo seen ay.

noonu itam la Almasi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.