TSK

TSK · Leviticus 18:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Bu kenn ci yeen dëkkoo ku mu jegewool lool cig bokk. Maay Aji Sax ji.

¶ «Sàmmleen sama dogali yoon yépp ak sama santaane yépp te jëfe ko, ngir réew ma ma leen jëme, ngeen dëkki fa, bañ leena gëq.

Du seen genn njekk, akug njub gu leen may ngeen nanguji seenum réew. Waaye mbonug xeet yii moo waral seen Yàlla Aji Sax ji dàqal leen leen, ngir sottal kàddu ga mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.

ndax mboolem ñiy def yooyu, Aji Sax ji seexlu na leen. Jëf ju seexluwu jooju moo waral seen Yàlla Aji Sax ji di leen dàqal seeni boroom.

«Yaw nit ki, ba waa kër Israyil dëkkee seen suufas bopp, dañu koo sobeele seen jikko ak seeni jëf, seen jëfin mel ni sagaru sobe ci man.