TSK

TSK · Leviticus 21:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax ku Sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen.

¶ Ku jël jabar, ba gannaaw gi xoolatu ko bëtu yiw, ndax lu tegginewul lu mu ko gisal, su ko bindalee kayitu pase, teg ko ci loxoom, ba yiwi ko, mu jóge këram,

Aji Sax ji dafa wax ne: «Damaa fase seen ndey? Wonleen ma kayitu pase mi! Maa leen jaay njaam, feyey bor? Ana ku ma leen jaay? Bu ñu leen jaayee, seeni ñaawtéef a. Bu ñu fase woon seen ndey it, seeni moy a.

Naka noonu, na jigéen ñiy taxawu mbooloo mi di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu moom seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.