TSK

TSK · Leviticus 25:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yanqóoba wax Firawna ne ko: «Samay ati màngaan, ba ma ganee àddina ba tey de, mu ngi tollu ci téeméer ak fanweer, muy at yu gàtt te naqari, te it demuma bay tolloo ay at ak samay maam, ba ñuy màngaan ci àddina.»

Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.

Nabot tudd Aji Sax ji, ne Axab: «Yàlla tere ma di la jox sama suufas maam!»

Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, ronq ni max la mu gëna fonk. Nitoo nit, cóolóolu neen. Selaw.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.

wal-wali jàll Yuda, mbënn ma wal, taañaañal, yéeg ba tollu ko ci put, firiku niy laaf ba dajal sam réew, yaw Emanuwel.»

Hosea 9:3 TSK

Dungeen des ci réewum Aji Sax ji. Efrayim, Misra lay dellu, te ca Asiri, lu daganul lañu fay lekkeji.

Joel 3:2 TSK

Kera jant yooyu, jaam yi sax, góor ak jigéen, maa leen di tuur samag Noo.

¶ Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.