TSK

TSK · Leviticus 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Da koy yót sarxalkat bi, kooku jëkka rey benn bi, muy saraxu póotum bàkkaar; na kutt baat bi te bumu teqale bopp beek baat bi.

Te nga wax bànni Israyil ne leen ñu jël ab sikket, mu doon saraxu póotum bàkkaar, akaw sëllu akam xar, lu ci nekk am at te mucc sikk, ngir saraxu rendi-dóomal,

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa ñàkk ba dooleem matewu ko, na wut menn kuuy, muy saraxu peyug tooñ, di saraxu yékkati-jébbale, ngir njotlaayam, boole kook ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, xiiwe ko diw, muy saraxu pepp. Na indaale genn-wàll liitaru diw,

menn mi di saraxas peyug tooñ, mi ci des di saraxu rendi-dóomal, te mu boole kook saraxu pepp mi. Noonu la sarxalkat biy defale ki ñuy laabal njotlaayam fi kanam Aji Sax ji.»

Sarxalkat bi day rendi yooyu, menn mi di saraxu póotum bàkkaar, mi ci des di saraxu rendi-dóomal. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayam fi kanam Aji Sax ji ndax jàngoroy xelleem jooju.

Na jële ci mbooloom bànni Israyil ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal.

Sarxalkat bi day def menn mi saraxu póotum bàkkaar, mi ci des saraxu rendi-dóomal, mu jote ko boroom céddoo gi, bàkkaaram ba ko néew ba yóbbe. Bésub keroog lay sellalaat boppam ba yenu woon njañam.

Ndax kat ab joxe, bu àndee ak yéene rekk, la boroom joxe bi amul, deesu ci natt lees koy nangul, waaye li mu am, ci lees koy nangul ab joxeem.

James 2:5 TSK

¶ Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp?