TSK

TSK · Leviticus 8:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe.

Musaa nag def loola. Mboolem noonee ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe.

Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Su ko defee sarxalkat bi génne ci saraxu pepp mi, ab saraxu baaxantal, daldi koy lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji.

Ba mu ko defee Musaa indi doomi Aaróona yu góor ya, solal leen mbubb yu gudd, takkal leen ay laxasaay, solal leen mbaxana, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.