TSK

TSK · Leviticus 9:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko.

¶ Ibraam dégg loola, daldi sujjóot. Yàlla wax ak moom ne ko:

«Li Aaróona aki doomam yu góor di sarxalal Aji Sax ji, keroog bu ñu koy diw, fal ko, mooy lii: ñetti kiloy sunguf su mucc ayib, tollook saraxu pepp bi ñu saxoo bés bu nekk, te genn-wàll gi di suba, genn-wàll gi ngoon.

¶ Ba loolu amee Musaa ne gurub, moom ak Aaróona, ñu dëpp seen jë fa suuf, fa kanam mbooloom bànni Israyil ma fa daje mépp.

Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, njiinum buur a jibe fa seen biir.

Esekiya ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim malaakay serub yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf.

yal na la yónnee wallam fa këram, jàpplee la fa, ca Siyoŋ.

Ba mu jëlee téere bi, ñeenti bindeef yi ak ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanamam, ku nekk yor xalam ak andi wurus yu fees ak cuuraay, cuuraay li di ñaani aji sell ñi.