¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.
TSK
TSK · Leviticus 9:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Keroog bu àppu setloom matee, bu doom ja dee góor, bu dee jigéen, na dem ca bunt xaymab ndaje ma te yóbbul sarxalkat bi am xar mu am at, muy saraxu rendi-dóomal, ak xati mu ndaw mbaa pitax, mu doon saraxu póotum bàkkaar.
Na jële ci mbooloom bànni Israyil ñaari sikket, sikket yuy doon saraxu póotum bàkkaar ak menn kuuyum rendi-dóomal.
Bés bi ñuy yékkati takk bi, jébbale, nangeen ci sarxal kuuy mu amul sikk, tollu ci menn at, ñu defal ko Aji Sax ji saraxu rendi-dóomal.
Ñu xas ne dinañu fase seeni soxna, daldi nangu ne tooñ nañu, ba noppi ku nekk ci ñoom sarxe am kuuy, muy peyug tooñam.
Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,
Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.