TSK

TSK · Luke 21:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Luke 6:22 TSK

Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.

Nun kat, du sunu bopp lanuy waare, waaye li Yeesu Almasi dib Sang moom lanuy waare, te nun ci sunu bopp nooy seeni jaam, ndax Yeesu.

Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole, ak ci biiri saaga, ak ci biir ag ñàkk, ak ci biir coono yu ñu may bundxatale, ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.

Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.