TSK

TSK · Luke 22:43

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 4:3 TSK

Yaw de, ñu bare jàngal nga leen, loxo yu toqi woon, nga dooleel,

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.

Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?