bu néewam fanaan ca garab ga, nañu ko daldi rob ca bés ba, ndax ki wékke alkàndey Yàlla la. Buleen sobeel réew mi leen seen Yàlla Aji Sax sédd.
TSK
TSK · Luke 23:33
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Zechariah 12:10
TSK
¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
Luke 24:7
TSK
Da noon: “Fàww ñu teg Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi, ñu daaj ko ci bant, rey ko, ba ñetteelu fanam, mu dekki.”»
Acts 5:30
TSK
Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
Galatians 3:13
TSK
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
1 Peter 2:24
TSK
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»