Yeen Yesurun, yeena yaflu, waŋŋeetu, solu yaram, ne faaj, ne fuux, fàtte Yàlla mi leen sàkk, faaleedi seen cëslaay li leen musal.
TSK
TSK · Luke 6:48
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yaakaaru noon yi de melul ni sunu yaakaar, te loolu la noon ya àtte.
Mu ne: Aji Sax ji laay sës, mu di ma aar, di ma wallu.
Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ku jara sës ku dul sunu Yàlla?
Yàllay Israyil a wax, moom mi Israyil sës, moo ne: Ku jiite ay nit cig njub, bu jiitee cig ragal Yàlla,
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
Aji Sax ji, géej a riir, géej a àddu, mu riir, gannax ya rëkk, mu riir.
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ku doyloo Aji Sax ji, yaay tundu Siyoŋ, doo toxu; dangay sax ba fàww.
Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg; Yàlla Aji Sax ji déy, moo mat cëslaay ba fàww.
Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, wormaale teddngaam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.
Ñuy feddli pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»
¶ Yiwu Yàlla wi mu ma may nag, ci laa lale kenu gi, ni tabaxkat bu xareñ, keneen di tabax ca kaw. Waaye na ku nekk xool bu baax na mu cay tabaxe.
Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.
¶ Dikkleen ci moom, mooy doj wuy dund. Nit ñee ko beddi moos, waaye Yàllaa ko fal, fonk ko.
Waaye bésu Boroom bi nib sàcc lay dikke. Ca la asamaan yi di dëddoo ci biir coow lu réy, lu ko sosoon seey ndax tàng, suuf ak jëf ju ci biiram xoyomu.
¶ Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk,
¶ Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex, ak ku ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.