TSK

TSK · Luke 8:47

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Samiyel def la Aji Sax ji wax. Ba mu agsee Betleyem, magi dëkk ba gatandoo ko tiitaange, ne ko: «Mbaa tànki jàmm?»

Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, jàq, di binni.

Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.

Bu Efrayim daan wax, ñépp ay lox; mu amoon daraja fi digg Israyil. Waaye moo sikkal boppam ci tuuri Baal, ba dee.

¶ Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla.

Man daal, ci sama biir néew dooley bopp, ak ragal bay kat-kati, laa nekke woon ak yeen.

¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,