TSK

TSK · Luke 9:44

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Daawuda ne Gàdd: «Am naa njàqare lool; waaye naa tàbbi ci loxol Aji Sax ji, ndax yërmandeem réy na, waaye yàlla buma daanu ci loxol nit!»

Luke 2:19 TSK

Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam.

Luke 9:22 TSK

Mu neeti: «Fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.»

Luke 24:6 TSK

Nekku fi; dekki na. Fàttlikuleen la mu leen waxoon, ba mu génnagulee Galile.

Acts 2:23 TSK

Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.

Acts 4:27 TSK

Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.

¶ Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal.