TSK

TSK · Malachi 1:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 1:9 TSK

Mu ne ko: «Ayóoba daa ragal Yàlla ci neen a?

«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.

«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.

«Maay joxe seeni jabar, jox seeni tool ay foqatikat, ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!

Hosea 5:6 TSK

Seen jur gu gudd ak gu gàtt lañuy àndal, di seet Aji Sax ji, duñu ko gis, te moo leen dëddu.

Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee, seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle, seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane, te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan: «Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir? Musiba du nu dab!»

Ñi ci des ñépp, seen njariñal bopp lañuy sàkku, waaye du li soxal Yeesu Almasi.

Foral-leen gétt gi ñu leen dénk. Sàmmleen ko, te bañ koo defe ñàkk pexe, xanaa xol bu tàlli, ni ko Yàlla bëgge. Buleen ko defe it koppartuy kese, waaye farluleen ci.