TSK

TSK · Malachi 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Man mii nag, maa seppee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen weccoo mboolem taaw bu góor bu jëkka juddoo ci ndeyam, ci biir bànni Israyil. Kon nag Leween ñi, sama cér lañuy doon.

Te itam sa bokki Leween ñi, sa giirug baay, jegeñal leen sa bopp, ñu jokku ci yaw, di la jàpple, te yaw yaak say doom, ngeen féete fi kanam xayma ba seedes kóllëre ga dence.

Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.»

Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!

Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam, nii la mujje am njéggalu bàkkaaram: Day boole doji sarxalukaay bi yépp, rajaxe ni doji kew, xer wu ñuy jaamoo Asera dootu fa sampe, mbaa sarxalukaayi suurukaay.

Maay xettee fi seen biir ñi may gàntal ak ñi may tooñ. Réew ya ñu wàlliyaani, fa laa leen di jële, te réewum Israyil, duñu fa duggi. Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji.

Maay biralee noonu sama màggaay ak sama sellnga, maa niy xamlee sama bopp, yéefar yu bare di gis, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Bépp doxandéem bu xaraful ci xol, xaraful ci jëmm, bumu duggati sama bérab bu sell bi, muy doxandéem bu mu mana doon, bu dëkk ci biir bànni Israyil.

“Seen pëndub dëkk bi ci sunu ndëgguy tànk sax, nu ngi koy faxas, seedeele leen ko seen ngàntal. Waaye nag xamleen ne nguurug Yàlla dëgmal na.”