TSK

TSK · Malachi 3:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Naka la séentu Sodom ak Gomor ak joor ga ba fa mu yem, gis nag saxar suy gillee ci suuf, mel ni saxaru taalu ban.

Job 28:1 TSK

Xaalis déy am na mbellam, wurus am bérabu seggukaayam,

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Bu ngeen raggoo woon saabu, ba raggooteek xeme it, seen ñaawtéef gàkk, may gis.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Amos 5:18 TSK

Wóoy kuy yàkkamti bésub Aji Sax ji! Ana lu ngeen am ci bésub Aji Sax ji? Dug leer, xanaa lëndëm.

Luke 2:34 TSK

Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqliku ci digg Israyil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal.

Luke 3:17 TSK

Ab layoom a ngi ci loxoom, mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; pepp mi lay fat cim sàqam, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»

¶ Ba Yeesu waxee ba noppi, ab Farisen da koo woo këram, ngir bokk ak moom lekk. Mu nangu, dem ba duggsi, daldi toog ca lekkukaay ba.

Teewluleen boog, tey ñaan saa su nekk, ba mana mucc ci mboolem looluy nara xew, ngir ngeen taxaw fi kanam Doomu nit ki.»

Acts 7:52 TSK

Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.

Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo.

Képp ku masoona xëtt yoonu Musaa, daawuñu ko ñéeblu; ci kaw seedey ñaari nit ba ñett lees ko daan rey.

Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wa tabaxkat ya beddi woon, te mu mujj di doju coll wi.»

Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.

¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.