TSK

TSK · Micah 2:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Seen doom yu góor ak yu jigéen, ñu jébbal weneen xeet ci seen kanam, ngeen di leen séentu ci neen bés bu Yàlla sàkk, te dungeen ci man dara.

¶ Aman wax Buur Aserus ne ko: «Aw xeet a ngi fi, tasaaroo ci biir xeet yi, jaxasoo ci seen biir, ci mboolem sa diiwaani réew mi. Seeni aada daa wuuteek yu xeet yépp; yoon yi Buur tëral, duñu ko jëfe, te jaaduwul ci Buur mu di leen seetaan.

Waaye ba mbir ma àggee ca Buur, Buur a joxe ay ndigal yu ñu bind, ne pexe mu bon ma Aman nasaloon Yawut yi, na walbatiku këppu ci kaw boppam. Te mook ay doomam yu góor dees leen di wékk ci bant.

Moom la waajalal ngànnaayi ndee, def ko fitt yuy boy.

Day mébét lu ñaaw cib lalam, taxawe yoon wu dëddu mbaax, te du bañ lu bon.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Ku bon du nelaw te lorewul, du dajjant ba kera muy téqe.

jekkadiy xalaat, di mébét lu bon aka yokku ay.

Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.

Ku néeg déy dina neen, kuy ñaawle sànku, te képp kuy yeeru nu mu defe lu bon, dees na la dagg.

Seeni loxoo taq deret, ngeen ne lijj ci ñaawtéef, làmmiñ di fen, di sos njekkar.

Aji Sax ji ne ma: «Yaw nit ki, ñii ñooy mébétkati ñaawtéef ñiy digle lu bon ci dëkk bii.

Boroom alal yi ci sa biir, aw ay lañu fees, waa dëkk bi di fen, te lu seen làmmiñ tudd ay nax la.

Ab jëtun, ak ab jirim, ak ab doxandéem, ak ab néew-doole, buleen ko not. Lu bon it, buleen ko mébétalante ci seen xol.»

Luke 22:2 TSK

Ci biir loolu sarxalkat yu mag ya ak firikati yoon ya di seet nu ñuy fexee ba rey Yeesu, waaye dañoo ragaloon nit ña.

¶ Ba bët setee Yawut ya daje, daldi xasoo, ne duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñu reyee Póol.

te di yàqkati der, ñu bañ Yàlla lañu, ñu reew, réy, di tëggu, ñu xareñ ci fexe lu bon, te déggadil seeni waajur.