Na lay waxal ak mbooloo mi; su ko defee sa kàddu di kàddoom, te yaw nga mel ci moom ni Yàlla.
TSK
TSK · Micah 6:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Bésub keroog boobee la Aji Sax ji yiwi bànni Israyil, ñu def kurél ci kaw kurél, génn réewum Misra.
¶ Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin.
¶ Maryaama ak Aaróona ñoo doon ŋàññ Musaa, ci ndawas Kuuseen su mu takkoon, te ab Kuuseen it la takkoon.
Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?
Waaye cofeel gu leen Aji Sax ji sopp, ak sàmm gu mu sàmm ngiñam la mu giñaloon seeni maam, moo tax mu génnee leen dooley loxoom, jote leen ca kërug njaam ga, ak ca loxol Firawna buuru Misra.
Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jot. Moo tax ma sant leen lii tey.
Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam.
Biir géej di saw yoon; saw xàll ci digg ndox mu ne xéew, te kenn gisul foo teg tànk!
Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra, bàyyiwuñu xel ca sa ngor lu réy, xanaa di fippu ca géej ga, géeju Barax ya.
Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
¶ «Nanga leen wax, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ba ma tànnee Israyil, maa giñal askanu waa kër Yanqóoba woowa. Maa leen xamal maay kan ca réewum Misra, giñal leen, ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma, ak ca géeju Barax ya, ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.