Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent.
TSK
TSK · Micah 7:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye loo ci góobe, gar ko, say pexe suur la këll.
Joxleen ko njukkalu ñaqam, jëfam di woyam ca pénc ma.
¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.
Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral, dees koo futti ba mu ne furaas! Aji Sax ji kat wax na kàddu gii!
maa leen di dikke seen añu jëf.” Kàddug Aji Sax jee. “Maay jafal sawara, lakk seen gott bi, mu xoyom lépp lu leen wër.”»
réyi pexe, màggi jaloore; say gët ne jàkk ci mboolem lu doom aadama def, ngay añale ku nekk jëfinam ak jëfam.
Ba ñu ca tegee fukki weer ak yaar yu mat, muy doxantu ca kaw taaxum kër buur ca Babilon.
Man it moo tax ma di la duma ba nga wopp, gental la ndax say bàkkaar.
¶ Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.