TSK

TSK · Micah 7:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Musaa teg ca ne ko: «Ngalla may ma nag ma niir sag leer!»

ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.»

Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, njiinum buur a jibe fa seen biir.

Ñoo baña dégg, baña bàyyi xel sa kéemaan yi nga def ci seen biir, te ñoo sajju loos, fétteeral ba fal njiit, nara dellu ca seen njaam ga. Waaye yaw yaay Yàlla jiy boroom njéggal ak yiw ak yërmande, di muñ mer, te bare ngor, ba tax waccoo leen.

Yaw miy nangug ñaan, yaw la képp di wuysi.

Céy Yàlla, sa njekk àkki na fa kawa kaw. Def nga lu réy. Yaw Yàlla, ana ku mel ni yaw?

Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.

Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?

Yërmandeeku yiw, fa Aji Sax ji. Moo muñ mer te bare ngor.

Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Ana kan ngeen di niruleek Yàlla, ak nataal bu ngeen koy dendaleel?

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttliku bàkkaar.

Fàttlikuleen lii te dëgërluwaat! Yeen bàkkaarkat yi, defleen lii ci seen xel.

Tukki bu sore bu la sonal sax taxu la ne: «Fomm naa.» Bànneex bi ngay séentu ngay leqlikoo, ba tax sonnuloo.

Ni xale bu góor di takke ab janq, ni la la sa doom yu góor di moome ni jëkkër; ni boroom séet di bégee ab séetam, ni la la sa Yàlla di bégee.

Xanaa deesul mer ba fàww? Xanaa xadar du sax?” Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax, waaye bon ngeen lu ngeen man.”»

Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Mboolem lu mu bàkkaaroon, deesu ko ko bàyyil xel. Njub geek njekk gi mu mujje moo ko may mu dund.”

Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi, maa leen di bëggal sama bopp, nde mereetuma leen.

Amos 7:8 TSK

Aji Sax ji ne ma: «Amos, ana loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa buumu beteex.» Boroom bi ne: «Maa ngii di natte buumu beteex fi digg Israyil, sama ñoñ. Dootuma leen baal dara.

Jonah 4:2 TSK

Mu ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Céy Aji Sax ji, xanaa du lii laa waxoon ba ma génnagul sama réew? Moo taxoon ma jëkka daw, jëm Tarsis! Ndax xamoon naa ne yaw Yàlla yaay boroom yiw ak yërmande, sa mer a diib, sa ngor bare, ngay fomm mbugal.

Micah 4:7 TSK

Maay def liy soox aw ndes, la ñu dàq fu sore, ma def ko askan wu am doole, te Aji Sax jeey doon seen buur ca kaw tundu Siyoŋ, li ko dale tey ba fàww.

Micah 5:7 TSK

Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk, ci biir xeeti àddina, mbete gaynde ci biir rabi àll yi, nirook gaynde gu ndaw ci biiri gàtt; fu mu jaare, joggati, xotat, te kenn du wallu.

Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqlee la cofeelam, bége la bay sarxolle.

Luke 15:9 TSK

Bu ko gisee, xarit yaak dëkk ya lay woo, ne leen: “Kaayleen nu bége, libidoor ba réeroon, gis naa ko.”

Waaye mbégte ak bànneex war na, ndax sa rakk jii moo dee woon te dekki na, moo réeroon te feeñ na!”»

¶ «Kon nag bokk yi, xamleen ne ci Yeesu moomu lañu leen birale njéggalug bàkkaar. Te mboolem lu ngeen tële woona wàccool, ba seen njub mat ci yoonu Musaa,

¶ Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp,

Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.