TSK

TSK · Numbers 1:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu seet ca bànni Israyil gépp, tànn ca góor ñu mat, fal leen, ñu yilif mbooloo ma: ñii jiite kuréli junniy nit; ñii, téeméer; ñii, juróom fukk; ñii fukk.

¶ Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàpple di fukki kilifay Israyil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam.

¶ Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona ak kilifag mbooloo ma lim Keyateen ña, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam.

¶ Ci biir loolu kilifa yi indi itam saraxu daloob sarxalukaay bi, keroog bés ba ñu koy diw. Ñu daldi joxe seeni sarax fi kanam sarxalukaay bi.

«Yebalal ay ndaw, ñu dem yëri réewum Kanaan, gi may jox bànni Israyil. Kenn ngay yebal ci seen giiri maam yi, giir gu ci nekk, kenn, te ku ci nekk di kilifa ci ñoom.»

Aji Sax ji ne Musaa: «Jàppal njiiti mbooloo mi yépp, nga wékk leen ci bant fi kanam Aji Sax ji, bëccëg ndarakàmm, ngir sànjum Aji Sax ji dëddu Israyil.»

Ay njiit ngay jële kenn-kenn, ci giir gu nekk, ngir ñu jàpp ci séddaleb réew mi.