TSK

TSK · Numbers 1:51

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aaróona ak doomam yu góor nag ngay tabb ngir ñu sasoo seenug carxal, waaye képp ku ci laal te bokku ci, dees koy rey.»

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ak Aaróona, ne:

Nii ngeen di def ak ñoom, ba bu ñu jegee yëf yu sell yee sell, di dund te duñu ca dee: Aaróona aki doomam ñooy dugg, daldi sédd ku nekk ci ñoom liggéeyam ak la muy gàddu.

¶ Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga.

¶ Gannaaw loolu Keyateen ñay gàddu yëf yu sell ya, ñoo fabu, topp ca. Bala ñoo àgg fa ñuy dalewaat nag, day fekk jaamookaay ba sampewaat.

na ko Aji Sax ji santaanee woon, Musaa jottli. Loolu di fàttli bànni Israyil ne benn jaambur bu bokkul ci askanu Aaróona sañula dikk di taal cuuraay fi kanam Aji Sax ji, lu ko moy lu mel ni li dal Kore ak gàngooram moo koy dal.

Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»

¶ Terewul Yàlla mbugal ñenn ca waa Bet Semes, ndax dañoo yërndu woon ca biir gaalu Aji Sax ja. Juróom ñaar fukki nit la fàdd ca ñoom. Waa dëkk ba nag di tiislu ndax mbugal mu réy moomu leen Aji Sax ji teg.