TSK

TSK · Numbers 14:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

Terewul seeni maam doŋŋ la Aji Sax ji taqool, ngir sopp leen, te yeen, ñi askanoo ci ñoom la taamu ci biir xeetoo xeet, niki bésub tey jii.

Buur ne Cadog: «Dellool gaalu Yàlla gi ca dëkk ba. Bu ma Aji Sax ji baaxee, dina ma délloosi, ma gisaat gaal gi, gisaat fi mu dëkk.

Cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi la bége, ba teg la ci jalub Israyil. Aji Sax ji daa sopp Israyil cofeel gu dul jeex, moo tax mu fal la buur, ndax nga saxal fi dëgg ak njekk.»

Ku ma gis ñaawal ma, biiñ ma, xeelu ma, naa:

Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal te di ko yaakaare ngoram.

Maay am mbégtey baaxe leen, jëmbat leen bu wér ci réew mi, jëmbate leen sama léppi xol ak sama léppi jëmm.»

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?