Ci kaw loolu sawara bawoo fi Aji Sax ji, tàkk ca kaw sarxalukaay ba, xoyom saraxu rendi-dóomal ba ak nebbon ba. Naka la mbooloo ma mépp gis loola, daldi sarxolle, ba noppi dëpp seen jë fa suuf.
TSK
TSK · Numbers 16:46
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu Aaróona noppee, na indi yëkku saraxas póotum bàkkaaram, def ko njotlaayam mook waa këram. Na rendi yëkku saraxas póotum bàkkaaram,
te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee bérab bu sell bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.»
Nangeen dénkoo ndénkaanel bérab bu sell bi, ak ndénkaanel sarxalukaay bi, ngir am sànj baña dalati ci kaw bànni Israyil.
¶ Ca Tabera itam, ak ca Maasa, ak ca Kibbrot Taawa, ngeen merlooti fa Aji Sax ji.
di merloo Yàlla ci seeni jëf, ba mbas ne dàll fa seen biir.
¶ Kenn ci malaakay seraf ya naaw wutsi ma, yor aw xal wu mu keppe ag ñiim, jële ko fa sarxalukaay ba.
¶ Gannaaw joxees nañu nu àtteb ñu jub ndax deretam ji tuuru nag, ñaata yoon lees nuy gënatee musal ci am sànj ndax moom?
Duggul biir asamaan it ngir di sarxe ak a sarxewaat boppam, noonee sarxalkat bu mag ba daan dugge at mu nekk fu sell faa sell, yóbbaale deret ju dul josam.
¶ Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi.