TSK

TSK · Numbers 16:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Léegi nag yaw, nanga seppee ci bànni Israyil sa mag Aaróona, ak doomam yu góor, nga woo leen fi yaw, ñu di ma sarxalal: Aaróona ak doomam yu góor, Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.

Na Aaróona aki doomam jiitloo loolu, bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, mbaa ñuy jegeji sarxalukaay bi, ngir liggéey ci bérab bu sell bi, ndax ñu baña yóbbe seen bopp mbugal, muy seen dee. Na Aaróona ak askanam sàrtoo loolu fàww.

Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.

Du génn ëttu bérab bu sell bi, mbaa muy teddadil bérabu Yàllaam bu sell bi, ndax diwu pal gu sell gi ko Yàllaam fale. Maay Aji Sax ji.

na ko Aji Sax ji santaanee woon, Musaa jottli. Loolu di fàttli bànni Israyil ne benn jaambur bu bokkul ci askanu Aaróona sañula dikk di taal cuuraay fi kanam Aji Sax ji, lu ko moy lu mel ni li dal Kore ak gàngooram moo koy dal.

Samay ñaawtéef man na ma, waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.

Yeen waa kër Aaróona, wóoluleen Aji Sax ji, moo leen di jàpple, di leen aar.

Néeg bi jàkkaarlook bëj-gànnaar nag ñeel na sarxalkat yi dénkoo dénkaaney sarxalukaay bi. Ñooñu ñooy Leween ñi askanoo ci Cadog te bokkuñook kenn sañ-sañu jege Aji Sax ji, ngir liggéeyal ko.»

Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.

Acts 1:2 TSK

ba ca bés, ba ñu ko yéegee, gannaaw ba mu joxee ndaw ya mu tànnoon, ay ndigal, Noo gu Sell gi jottli.

Acts 13:2 TSK

Ñooñoo daje woon di màggal Boroom bi, boole kook koor. Ci biir loolu Noo gu Sell gi ne: «Beral-leen ma nag Barnaba ak Sóol ngir liggéey, bi ma leen wooye.»

Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.

Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel.

¶ Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell, ngir deretu Yeesu,

Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gi tabaxe kërug Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi.

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.