TSK

TSK · Numbers 17:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»

Ci biir loolu mu wax ak mbooloo ma, ne leen: «Ngalla dàndleen xaymay nit ñu bon ñii, te buleen laal seen lenn, bala ngeen di buuboondook mboolem bàkkaari ñii.»

Mu topp waayi Israyil ja ba ca biir néeg ba, daldi leen boole bennub xeej, ñoom ñaar, jam waayi Israyil ji, ba jamaale ndaw si ci biir. Ba mu ko defee mbas ma jotoona dal ca kaw bànni Israyil daldi dakk.

¶ Ba mboolem ña tollu woon ci xare deeyee ba jeex, ba ñoom ñépp wuute ca mbooloo ma,

¶ Naka lañu dem ba tollu ca dàggay Nakon, nag ya tërëf, Usa tàllal loxoom, jàpp ca gaalu Yàlla ga.

Job 34:14 TSK

Bu ci Yàlla yebu woon, ba roccim xelam ak noowam,

Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw?

Acts 5:5 TSK

¶ Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.

Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.