TSK

TSK · Numbers 22:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;

Waaye yeen it dal-leen fii guddig tey, ba ma xam lu ma Aji Sax jiy waxaat.»

Balag ne ko: «Kaay rekk, topp ma, ba feneen fooy tollu di leen gis. Seen cat doŋŋ ngay gis nag, waaye doo leen gis ñoom ñépp. Su ko defee nga móolul ma leen foofu.»

Ñeengo jàppul Yanqóoba, gisaane gisul Israyil gii. Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.”

Su boobaa yeenay gëna barkeel mboolem xeet yi, te du lenn, góor ak jigéen, luy jaasir ci seen biir, ak seen biirug jur.

¶ Barkeel ay ñeel seen yoonu dem, barkeel ay ñeel seen yoonu dikk.

Ndokklee xeet wu am lii! Ndokklee xeet wu yàllawoo Aji Sax ji!

Dees na xàmmee seen askan fi biir xeet yi, xàmmee lu meññe ci ñoom fi biir waaso yi; képp ku leen gis ràññee ne ñooy askan wu Aji Sax ji barkeel.

Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu.