TSK

TSK · Numbers 26:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yuda daldi wax Tamar jabaru doomam ne ko: «Demal sa kër baay, ténjeji fa, ba sama doom Sela màgg.» Booba Yuda dafa ragal Sela faatu moom itam ni ay magam. Tamar nag dem, toog kër baayam.

Yuda xàmmi yëf ya nag, ne: «Moo ma gëna nekk ci dëgg de, gannaaw mayuma ko sama doom Sela.» Gannaaw ba loolu wéyee, àndatul ak moom.

Ruth 4:18 TSK

¶ Kon lii mooy askanu Peres ci wàllu geño: Peres moo jur Esron,

Amoon na it ñu dëkkoon Yerusalem te bokk ci giirug Yuda ak giirug Beñamin. Ñi bokk ci askanu Yuda Ataya la, ku góor ka Usiya di baayam; Sàkkaryaa di baayu Usiya; Amarya di baayi Sàkkaryaa; Sefatiya di baayi Amarya; Mayalel di baayi Sefatiya, Peres di baayi Mayalel;

¶ Petaya ma baayam di Mesesabel mu bokk ci askanu Sera doomu Yuda moom la Buur dénkoon mboolem mbir yi soxal mbooloo mi.

Luke 3:33 TSK

Nason, Aminadab; Aminadab, Admin; Admin, Arni; Arni, Esron; Esron, Peres; Peres, Yuda;