Man Aji Sax ji, maa ko wax. Noonu déy laay def mboolem mbooloo mu bon mii booloo ci sama kaw. Ci màndiŋ mii lañuy raafe, fii lañuy deeye.»
TSK
TSK · Numbers 27:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israyil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur.
suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja.
Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji,
Ñooñu, kenn desul ca seen biir, te bokkoon ca limeefu bànni Israyil, ba Musaak Aaróona sarxalkat ba jëkkoona tënke ca màndiŋu Sinayi.
Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.
ba tax na, noonee bàkkaar doone woon buur, ndax dee gi mu yilife ñépp, ni la aw yiw wuutoo, di buur moom itam, ndax àtteb njub gi aw yiw jural nit ñi, ba jëme leen ci texe gu sax dàkk, ci sunu ndimbalal Boroom Yeesu Almasi.