TSK

TSK · Numbers 33:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israyil tabaxale Firawna buuru Misra dëkk, ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund.

¶ Ci kaw loolu bànni Israyil jóge dëkk ba ñuy wax Ramses, jëm Sukkóot. Ña nga tollu ci juróom benni téeméeri junniy góor (600 000) te limaaleesul jigéen ñaak xale ya.

Aji Sax jee dëgëral boppu Firawna buuru Misra, mu toppi bànni Israyil, fekk bànni Israyil ñoom, ña ngay génn réew ma ci seen teeyu bakkan.

Dungeen gaawtu déy, di dem; duy xél moos ngeen fay génne. Aji Sax jeey dox jiitu leen, te Yàllay Israyil laa ne, moo leen di féete gannaaw.