TSK

TSK · Numbers 4:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Sàkkal rido bu ñu ràbbe wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ca nataali serub,

¶ Besalel nag defare gaalu kóllëre gi dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll.

¶ «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca.

¶ «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi bérab bu sell bi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi.

Mu fabu, mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom, dem Baala, ca Yuda, ngir jëleji fa gaalu Yàlla gi ñu tudde Tur wi, turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, ki tooge diggante malaakay serub, yi tiim gaal gi.

deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu sarxe.