TSK

TSK · Numbers 8:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Juróom benni car a soqikoo ci weti tegukaayu làmp bi, ñetti car ci gii wet, ñett ci gi ci des.

ak tegukaayu làmp bu wurusu ngalam bi aki làmpam, làmp yi sësaloo ba jekk ak mboolemi jumtukaayam, ak diw gi ñuy taaloo,

Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.

Kon waxleen ne leen: «Ayca, ca ndigali yoon ya, ak seedey kàdduy waxyu ya. Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»

¶ Naka laa geestu, di seet kuy wax ak man, ma daldi gis juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus.

Ay melax aki kàddu aki dënu ñooy bawoo ca ngàngune ma, juróom ñaari jumi sawara di tàkk fa kanam ngàngune ma, jum ya di juróom ñaari noo yu Yàlla yi.