¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji waxaat Musaa ne ko: «Dellul ca mbooloo ma, te nanga leen sell-luloo tey ak ëllëg. Nañu fóot seeni yére,
TSK
TSK · Numbers 8:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu loolu amee sarxalkat bi wis-wisal juróom ñaari yoon ci kaw ki ñuy laabal, ngir mu tàggook sobey jàngoro ji. Su ko defee sarxalkat bi biral ne set na. Bu noppee na bàyyi picc miy dund mu naaw ca àll ba.
Bésub juróom ñaareel ba na watu ba set, bopp beek sikkim beek yeen yi ak kawar gi ci des yépp lay wat, fóot ay yéreem, sangu, daldi set.
Ku laal lenn lu mu toogoon lu ko féete woon suuf dina yendoo sobe ba jant so, te képp ku yékkati loola na fóot ay yéreem, sangu, te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
Ki ko lakk bu noppee, na fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi.
Na ku set tonni dóomu nag wa, te sotti ko bérab bu set, foofa ca biti. Dóom ba dencub mbooloom bànni Israyil lay doon, ñu di ko waajale ndoxum setlu, ngir saraxu póotum bàkkaar.
Nañu sàkkal ki sobewu ca dóomu saraxu póotum bàkkaar ba ñu lakkoon, te ñu sotti ndox muy dund ci ndab, ca kaw dóom ba.
Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.
waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet, ba buur yi wedam, ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko, lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.»
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.
Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol.
¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.