Aji jub ñaa ngi dee, te kenn yégalu ko yaramam. Gor ñaa ngi faatu, te kenn ràññeewul ne aji jub ji, faatoom, musiba la koy moyale.
TSK
TSK · Philippians 1:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu, mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njekk, di sunu sellte, di sunug njot,
¶ Xam nanu ne sunu yaram, sunu këru kaw suuf gii di ab xayma, bu daanoo it, am taax lanu am fa Yàlla, kër gu sax dàkk, gu loxol nit tabaxul.
Kon ñeme lanu def, te li nu gënal di génn, des bitib sunu yaramu tey, ngir dëkki ak Sang bi.
Waaye man de Yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee.
Ci diggante yaar yooyii laa tance: yàkkamti na maa yiwiku ba fekki Almasi, te loolu moo dàqati fuuf.
Seenug dund dëgg Almasi la, te keroog bu Almasi feeñee, yeen itam ay ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.
¶ Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokklee aji dee ñi deeyaale gëm Sang bi.”» Noo ga daldi ne: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»