TSK

TSK · Proverbs 1:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ku am doom ju góor ju dëgër bopp te të; déggalul baay, déggalul ndey, su ñu ko yaree, te taxul mu déggal leen,

Su nit ki tooñee moroomu nitam, Yàllaay àtte; waaye su dee Aji Sax ji la nit ki tooñ, ana ku koy àtte?» Wax jooju nag taxul ba tey ñu déggal seen baay. Booba fekk na Aji Sax ji namm leena rey.

Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon, bul jaare fa ñuy jaar,

Doom, bul fàtte sama njàngle, defal sa xel ci saay santaane,

Sama doom, déglul sama xel mu rafet, teewlul sama déggin,

Doom, sàmmal samay wax, fonk samay santaane.

Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.

Maa ngi fàttliku ngëm gu dëggu gi ci yaw, te jëkkoona nekk ci sa maam ju jigéen Lowis, ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne moom nga saxoo itam.