TSK

TSK · Proverbs 10:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;

nee naa: duma jël ci yaw dara, du puso, bi gëna tuut sax, su ko defee doo mana wax ne yaa ma taxa am alal.

¶ Gannaaw loolu Isaaxa bey ca réew ma, góob ca at ma lu tollook téeméeri yoon la mu ji woon, ndax Aji Sax ji da koo barkeel.

Aji Sax jeey xañe, di maye, di detteel, di kaweel.

Alyaasa ne ko: «Defe nga ne samag leer teewuloon, ba nit kay wàcce ca watiiram, di dajeek yaw? Ndax danoo tollu ci jël xaalisu kenn aki mbubb mbaa ay tooli oliw aki tooli reseñ aki gàtt aki nag aki jaam yu góor ak yu jigéen?

Job 27:8 TSK

Ana lu yéefar biy yaakaarati bu fàddoo, ba Yàlla moom bakkanam?

Aji Sax ji barkeel, ñu giira giir, te wàññiwul seenug jur.

Neen it la nit di teela jóg ak a guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw.

Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.

Maay wàcce alkute gi,» kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yee, «mu dugg ba ci biir kër sàcc bi, ak kër nit kiy giñe sama tur, ay fen; ci biir kër gi la alkute giy fanaan, ba raafal banti kër gi, aki dojam.»