TSK

TSK · Proverbs 10:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.

Su may jaare xuru ndee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.

Man nag maandu laay wéye, tee nga maa jot, baaxe ma?

Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.

Xanaa kiy doxe njekk, di wax njub, bañ alalu foqati; loxo bay jalax ab ger, noppam di tanqamlu waxi bóome, bëtam di gëmm, ba du gis lu bon.

Luke 12:1 TSK

¶ Mbooloo ma nag mujj na dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, bay joggeente. Ci biir loolu Yeesu tàmbalee wax, jëkke ko ci ay taalibeem, ne: «Wattuleen lawiiru Farisen ñi, te mooy jinigal.

Yeneen Yawut ya it di jinigalandoo, ba Barnaba sax lajj topp leen ci seenug jinigal.