TSK

TSK · Proverbs 13:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Léegi nag seetal, ba xam loo ci wara def, ndax musiba kat dëgmal na sunu sang, ak waa këram gépp. Moom nag dafa naqari deret, ba maneesula wax ak moom.»

Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble, di jëflante cig njub.

Nit ku ñaw day xam, ba ca; ab dof siiwal waxi dofam.

Ku xelu àddu, xam-xam rafet; ab dof di talalali.

Te it ku dofe buy dox sax, du ànd ak xelam; ku ko gis, xam ne kii dof la.

Aji Sax ji nee: «Sama jaam baa ngi, mooy baaxle, kawe, dees na ko yékkati, darajaal ko lool.

Yeen nag seenug dégg ndigal siiw na ba bir ñépp, moo tax ma di leen bége. Waaye damaa bëgg ngeen xelu ci lu baax, te seenum xel mucc ci lu bon.

Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.