¶ Kàddug Suleymaan ga nag neex Aji Sax ji, ndax loolu mu ñaan.
TSK
TSK · Proverbs 15:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Muy ñaanu Daawuda. Éy Aji Sax ji, déglul liy dëgg, déglul, ma woote! Teewlul, ma dagaane la làmmiñ wu mucc fen.
Aji Sax ji day dëddu ab soxor, di nangu ñaanu ku jub.
Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.
Kee moom mu ngi rendiw yëkk, sarxal, te teewu koo bóome. Kee rendiw xar, sarxal, te teewu koo damm loosu xaj, sarxal. Kee ngi joxe saraxu pepp, te teewu koo tuur deretu mbaam-xuux. Kee di taal saraxu baaxantalu cuuraay, tey jaamu ay tuur. Ñoo taamu seen yoonu bopp, safoo seeni jëf ju seexluwu.
¶ Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa ne: «Seen juru saraxu rendi-dóomal, dollileen ko ci seen yeneen sarax, te lekk yàpp wi.
«Maa bañ, maa sib seeni màggal, seen ndajey diine génnliku na ma.
Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw. Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at?