¶ Ba mu ko defee Ayóoba jóg, ne tareet mbubbam, ba noppi watu nel, di ko ñaawloo. Mu daanu fi suuf, sujjóot,
TSK
TSK · Proverbs 18:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Da di fetti Aji Man jee ma jam, ba tooke ji nàndal samam xel, mbugalu Yàlla yu raglu làng-déral ma.
Su ma defee lu bon, ngalla man, te bi ma defee njekk it, sañumaa siggi, gàcce laa suure, sangoo toroxte.
Ba ma nee cell, damaa ràgg, dëkke naqar.
Naa wax Yàlla ji ma sës, ne ko: «Lu tax nga fàtte ma, noon di ma fitnaal, may wéye tiis?»
Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; tiitaangey ndee ne ma taral.
Aji Sax ji, man, yaw lay woo wall, xëy, kare la gii ñaan, ne la:
di faj naqaru xol, fajtal góomi boroom.
Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal.
Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;
¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.
¶ Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.