Deuteronomy 7:22
TSK
Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dàqe fi seen kanam, ndànk-ndànk; dungeen leen mana gaawa jeexal, lu ko moy rabi àll yi mujj ne gàññ ci seen kaw.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dàqe fi seen kanam, ndànk-ndànk; dungeen leen mana gaawa jeexal, lu ko moy rabi àll yi mujj ne gàññ ci seen kaw.
Aji Sax jee koy seppee ci mboolem giiri Israyil, ngir sédd ko njekkar, na mu dëppook mboolem alkàndey kóllëre gi ñu bind ci téereb yoon wii.
Bésub safaan ku bon ay mucc, bésub mbugal it, mooy raw.
Aji Sax ji barkeel la, nga jagoo réew mi moos; mu alag la, nga dog.
Bàyyil xel ku maandu, xool ku jub; muj, fa nitu jàmm.
Yàlla da lay sànk ba fàww, fëkke la sab xayma, yóbbu, déjjatee la réewum aji dund. Selaw.
Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem, di sànk képp ku bon.
Ku jub deesu ko daaneel mukk, ku soxor du yàgg cim réew.