TSK

TSK · Proverbs 24:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Moo dàq wurus, raw wurusu ngalam wu ne xas; dàqati lem, ëpp tem-tem.

Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.

Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy,

Sa kàddu laa gis, di ko dunde, sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol. Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy, sa tur lañu ma tudde.

Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk, wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte; xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.