TSK

TSK · Proverbs 24:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba Israyil gisee na Aji Sax ji jowe loxoom bu baax ca xareem baak waa Misra, dañu daldi ragal Aji Sax ji, teg ca am kóolute ci Aji Sax ji ak ci Musaa, jaamam ba.

Ñu ne ko: «Góor gi, léegi danga di mag, te say doom jaaruñu ci say tànk. Kon danga nuy falal buur bu nu jiite, ni ko xeet yépp baaxoo.»

Ba loolu amee fitu Daawuda ne tërit ndax la mu dagg ca lafu mbubbum Sóol.

Xare ba daa law foofa ba daj diiwaan ba bépp; te ña dee ca gott ba bésub keroog ñoo ëpp ña saamar rey.

¶ Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: «Ana lu nu bokk ak Daawuda, lu nu séq ak doomu Yese? Bànni Israyiloo, ca seeni xayma! Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma;

Bul gaawa won buur gannaaw; bul saxoo lu buur buggul; Buur, lu ko neex lay def.

¶ Na ku nekk déggal njiit yi yor kilifteef, nde amul njiit lu bawoowul fa Yàlla, te njiit yi toog, Yàlla moo leen tabb.

¶ Nangul-leen gépp kilifteef gu tege ci àddina ngir Boroom bi; muy buur bu mag bi gëna kawe,