TSK

TSK · Proverbs 29:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.»

Ezra 7:27 TSK

¶ Cant ñeel na Aji Sax ji, sunu Yàllay maam, moom mi def nii ci xolub Buur yéeney teral kër Aji Sax ji ci Yerusalem,

«Demal woo mboolem Yawut yi, ci Sus, ñu daje. Te ngeen wooral ma: buleen lekk, buleen naan diiru ñetti fan, du guddi, du bëccëg. Man it maak sama surga yu jigéen, nu woore noonu. Su ko defee ma dem ca Buur doonte yoon nanguwu ko. Su ma dee dee, ma dee rekk.»

Benn yoon la Yàlla wax, yaari yoon laa dégg, ñu ne; «Doole, fa Yàlla.»

Merum buur ndaw la, dee a ko yónni; ku rafet um xel, giifal ko.

Ñu baree ngi wuta neex boroom daraja, ku nekk a bëgga xaritook kuy joxe.

Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.

Man nag ma noon: «Maa sonn ci dara, coonob cóolóol bu amul njariñ.» Teewul sama àttee nga fa Aji Sax ji, sama yool a nga fa sama Yàlla.

ndax amul dara lu may yedde sama bopp. Waaye nag loolu mayu ma njekk, nde kiy dogal samab àtte mooy Boroom bi.