TSK

TSK · Proverbs 3:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Doj wii ma samp, muy xàmmikaay, mooy doon kër Yàlla, te lépp lu mu ma wërsëgal, dinaa ko génneel fukkeel ba moos.»

Wormaal-leen màggalu bésu Ngóob mi jëkka ñore ci tool, yi ngeen di bey, ak màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi, gannaaw bu ngeen dajalee seen meññeef ba noppi.

¶ «Ngëneeli meññeef mi jëkka ñore ci seen suuf, nangeen ko yóbbu seen kër Yàlla Aji Sax ji. «Buleen togge ab tef soowum yaayam.»

Juróomeelu at ma doŋŋ ngeen di saña lekk doom ya. Su ko defee meññeef ma barkeelal leen. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di jooxe menn mburum jooxe. Ni ngeen di sàkke jooxe bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy jooxee.

ndax Leween, ñi amul wàll ci seen céru suuf, dikk, ñook doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun, yi ngeen dëkkal, ngir ñu lekk ba regg. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seenu ñaq.

«Àpp bi daal yeen la jotal, ba ngeen dëkke biir kër yu ay xànq lale, te kër gii dib gent?

Bés bu jëkk ci ayu bés yi, na ku nekk génne as lëf ca la mu am, na mu ko àttane, te mu dencal ko boppam, ngir bu ma dikkee, dootu soxlaa wër, di dajale.

¶ Du ndigal lu ma leen jox, waaye njaxlafug yeneen gëmkat, moom laay natte seen xol, ngir xam nu seen cofeel dëggoo.