TSK

TSK · Proverbs 4:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

day mel ni leeru jant bu fenk, kaw asamaanu suba su niir newul, leeru asamaan su set, taw ba siwet, ba ñax jebbi.

Job 23:10 TSK

Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.

Ku dëggu, yoonam day maase; ku dëggu, Aji Jub ji jubal xàllam.

Hosea 6:3 TSK

Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»

Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu, leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.

¶ Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.

Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Gàtt bi di làmpam.