TSK

TSK · Proverbs 7:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Diir ba waa kër Sóol di xareek waa kër Daawuda, Abner a ngay gëna dëgëral taxawaayam ca waa kër Sóol.

Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi.

Ma ne leen: «Xanaa du nii la Suleymaan buurub Israyil bàkkaare woon? Li xeet yiy bare lépp amul benn buur bu meloon ni moom. Ku Yàllaam soppoon la te Yàllaa ko faloon buurub Israyil gépp. Waaye moom sax jigéeni doxandéem yi bàkkaarloo nañu ko.

Mbugal ak toroxte dib añam, te gàcceem du deñ.

Bunu jëfe powum séy, ni ko ñenn ci ñoom daa defe, ba tax ñaar fukki junni ak ñett (23 000) ca mbooloo ma bokk dee ci benn bés.

¶ Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.